#sunumbir : c'est notre affaire ! 

Quelques types de rimes

Versification

Des types de rimes illustrées à partir du recueil poétique Xelum xalam de Làmp Fall Kala 

Les rimes plates ou suivies : Schéma (AABB) 

Exemple 1 :

" Képp kuy dox ak a wax lu la neex 

Bés dina ñëw wax ak jëf lépp jeex

Ńu gasal la kan sotti suuf mu fees

Su boobaa fekk réccu daal di wees" 

         Maa tay

Exemple 2 :

" Lees war a ragal di daw a ngi fii

Ci sunu biir di riir moo waral lii

La woon démb li ëpp wonni na

Ku bëgg lu jag tey jii jaaxle na"

                   Li ma jooyloo

Les rimes continues (AAAA) 

Exemple 1 :

"Jantam bi noppi ci di ma leeral

Ngelawam li dootu ma féexal

Ñamam yi noppi maa reggal

Ndoxam mi dootu ma màndal" 

         Sëy bu tas

Exemple 2 :

" Démb dañu ne woon yaw kat

Yaay ki gën a baax di ki mat

Yewen bari sutura doo ku xat

Siisoo ragaloo te doo am buqat

Kuy seet fum fanaan nga jël fat"

           Kàkkatar

Les rimes croisées ou alternées (ABAB) 

Exemple 1 :

" Ndeem jëf nga te ku jëf ñu fay

Naam sa jëf ci nun dafay lu réy

Soxna si sag nga mat royukaay

Ci mbaax gi ngay gont ak a xéy." 

      Ndey jigéen

Exemple 2 : 

"Jimbóori nee nga yaay ki gën ci nun ñii

Buumu njaam gi nga indiwaat dog ko

Yëfi réew mii jariñ waa réew mii

Tubaab du nu ci ëppeeti waat ko"

                   Waat ko

Les rimes embrassées (ABBA) 

Exemple 1 :

" Yàggal yokku biir ak biti ba teral

Ku la soob làq ngërëmal Ndey ak Baay

Rasaaqu di la dolli may yu taay a taay

Xel mi dal a dal xol bi muy seral "

 

Exemple 2 :

"Saa rakk laay woy ñàkk kiñaan

Baax yiw boole ci rafet xalaat

Ba tax mu mujj a am fépp baat

Sell nga set am ng liimaan"

                       Xale màgg na

 

Les rimes redoublées, les vers dont les finales riment ensemble se suivent au moins trois fois de suite (AAABBB).

Exemple 1 : 

Takk naa samay gët ak mbëggeel

Dëgmal laak xol bu fees ak cofeel

Bëgg yéene yërmaandeek nobeel

Sama xol bi ak la ca biir laa la jox

Yaay fob sa fetalu mbëggeel sox

Ni ma ko tuy tuy ma daanuy lox

Jógaat taxaw mel ni ku dee di dox "

 

Exemple 2 :

Am na Sëriñ su jébbalu ci moom

Jaay nañu seeni taalibe ngir koom

Am ilimaan yu mu jënd ba moom

Bajákka ya faf yamook i xërëm

Ňuy fowe Yàlla ngir i dërëm

Torox nañu maa leen yërëm"

                Waat ko

Les rimes mêlées 

" Nee nga askan wi ñoo la tànn

Fexeel ca teel coowal waaso

Xeet, tariixa ak sa par-parloo gii

Nga indi jëllewaat ko fi waat ko"

                        Waat ko

 

09/04/2021Facebook 1617922663958 6786059501135643075

1 vote. Moyenne 2 sur 5.

Ajouter un commentaire