#sunumbir : c'est notre affaire ! 

Malaanum lëndëm

De Boubacar Boris Diop

Texte choisi : L'incipit du dernier livre de Boubacar Boris Diop intitulé Malaanum lëndëm

I- Présentation de l'auteur : " Le Temps de Tamango (1981), Les Tambours de la mémoire (1990) au Le cavalier et son ombre (1997) Boko nañu ci téere yi tax ñu ràññee Bubakar Bóris Jóob ci wàllu ladab. Wànte Murambi, le livre des ossements (2000) moo gën a siiw ci li mu bind ci làkku tubaab. Mu ko jagleel Ruwandaa, di ci nettali ñaawteef yu jéggi dayoo ya fa nguuru Kigali gi defoon ci atum 1994.

Jóob gènne na it ay téerey xeltu, di ci leeral ni mu gise nekkinu Afrig tey ak it ëllëgam.

Doomi Golo (2003) la jëkk a bind ci wolof, tudde ko ci tubaab Les petits de la guenon (2009). Tekki na yit Une Saison au Congo bu Aimé Césaire, tudde ko Nawetu deret (2015), Bàmmeelu Kocc Barma topp ci. Malaanum lëndëm (2022) mooy ñeenteelu téreem ci wolof."

Source : Malaanum lëndëm

 

II- Texte :

Asta Balde

Sidiki sama, Siise-Ngaari,

nee nga ma keroog sama digganteek goor gi Seega Ture dafa xaw a ub sa bopp te bëggoon nga xam naka la ràbboo dëggëntaan. Dinaa la ko wax tey. Walla boog dinaa la ko jéem a wax. Yaa ngi xamsi ndànk ndànk maam Seega, li muy màgget yépp neexul a sóoru : déggoowul ak kenn Tànjuraa ga mu dëkk, siide naa ubbi gémmiñam gi wax, du juum ba kaf te su dee mas naa ree bay xàqtaay tamit, booba maak yow moomuy wëndéelu Espaañ juddoogunu. Ci gàttal, bu doon sago góor gi Seega Ture, kenn du ko xamal dara. Moom daal, mënees na ko méngaleek doomi Aadama yooyuy làmboo malaanum lëndëm ba noppi ne miig téye seen bopp. Saa toi naagoo ba yaakaar ne nànd nga seen i mbir walla li seen xel miy nas, ñu mbas la.

Boo fàttalikoo, bésu altine laa la woo foofu ça Las Palmas de Gran Canaria, ni la am na kilifag Tànjuraa gu soxla sekkarteer, nga laaj ma fan laa dégge loolu, ma ni la ci " Jamonoy Tey", yéenekaay biñ jëkk a sàkk Senegaal te yit mu ëpp fi doole, laa ko jànge.

                                                             Bubakar Bóris Jóob, Malaanum lëndëm, EJO Editions, 2022.

III- Quelques axes de lecture

- Repérez le titre du livre

- Où se passe l'action ?

- De qui parle-t-on ?

27/02/2022

 

#sunumbir

#undimancheuntexte

274922176 4814856941894841 5822861136962729184 n

 

 

Aucune note. Soyez le premier à attribuer une note !

Ajouter un commentaire