#sunumbir : c'est notre affaire ! 

Séex Anta Jóob

Extrait du roman Doomi golo de Boubacar Boris Diop

Texte choisi : Séex Anta Jóob

  1. Présentation de l'auteur : « Bubakar Bóris Jóob mi ya xal téere bii, ci bindkat yi gên a siiw ci Afrig la bokk. Xam-xamam mu ngi gën a màcc ci wàllu xeltu, ci ladab ak ci xam-xami xibaar. Bubakar Bóris Jóob bind na ci làkku tubaab ay téere yu ràňňiku, te ňu mën cee lim ; « Le Temps de Tamango », ci atum 1981 ; « Les Tambours de la mémoire » (1990) ; «  Les Traces de la meute » (1993) ; ak « Le cavalier et son ombre (1997). Waaye mën naňoo jàpp ne « Murambi, le livre des ossements » bi Jóob bind ci atum 2000 te jagleel ko Ruwandaa moo jur « Doomi golo ». Ndax ba Bóris demee Ruwandaa ba gis fa jëf ju ňaaw ja fa waa nguur ga def ak nu leen nguuru Farâns ak François  Mitterand jàppalee, la tàmbali di xalaat ju jëm ci làmmiň wi bindkat bi war a jëfandikoo. »

Source : Quatrième page de couverture du livre Doomi golo

  1. Texte : Séex Anta Jóob.

           Badu Taal, jàmbaaru xare dëgg a ngoog. Masul a dugg ci dara ba di ca séentu alal mbaa daraja.

           Lépp lu mu mas a sumb, baat bu mu mas a yëkkati, njariñu askan wee taxoon.

           Masul a jiital leneen.

           Moom daal la xam ne aji-néew ji doole yee ko taxoon a jóg. Lenn rekk a ko soxaloon : liy tax nit ku ñuul jëm kanam te du sibooru kenn.

           Su ñu ko déglu woon na mu ware, dog kon nañu buumu njaam gi bu yàgg. Nit ku maandu la woon, lewet ba nga ni lii lu mu doon, ndeysaan, waye kenn feesul woon bëtam. Soo toogee tey ci sa kanamu tele, gis ni Daawur Jaañ baree tiitar, gis yu ñàkk faayda yi mu jiital ak ni mu ragalee doxandéem yi nu doon noot démb, te di nu foowe tey, soo gisee lolu lépp ngay sog a xam ne Séex Anta Jóob kenn la fi woon.

            Du woon nitu caaaxaan. Daawul wax lu ko wóorul, daawul dige lu mu narul a def. Bu ay ñoñam demaan ba mel ni ñuy xaw a foqi, dafa leen daan ñaax ak ay kàddu yu daw yaram :

             Yëf yi metti na, gaa, waaye bu leen dara jële ci li ngeen nekk. Dafa fekk rekk ne waa réew mii, dañu leen a nax ba soo leen waxee dëgg sax tas seen yaakaar.

              Séex Anta Jóob teel naa làqu, ndax bi ñu koy denci Céytu, ci 1986, amul woon lu dul 64 at.

Amul bés bu ma jullee, man Ngiraan Fay, te ñaanaluma Séex Anta Jóob.

Dundam neenul ci genn wet. Miinantewunu woon, gaa. Ay. Mitiŋam doŋŋ laa daan dem di ko déglu. Waaye li am solo ci nit mooy mu am dégg-dégg. Mën ngay tukki, Badu, agsi dëkk boo xamul kenn, toog ci pénc miy noppalu, nit koo xamul romb la, tàbbal ci say nopp ay kàddu yu am solo. Soo téye kàddu yooyu bu baax, dinañu la gunge, amal la njariñ ba keeoog Yàlla di la fi jële.

Noonu la sama digganteek Séex Anta Jóob deme. Dinaa la wax tey li ma jàng ci moom : nit day juddu bés, ñu teg ci ay at ñu robi ko. Yëf yi gaaw ni xef-xippi. Ku góor-góorlu tuuti, mën ngaa bañ a xejal fen ak tappale ci diggante bu xat boobu. Bu kenn yóbbu sa fit, Badu, bu la dara tax a ñaaw ci xare bi. Loolu de laa jàng ci Séex Anta Jóob.

Xalaatam ak dundam, teen bu xóot a xóot la.

Fexeel ba say doom duy ci, Badu.

Man, Ngiraan Fah, giiñ naa ni su ko samay doomi sët defee, duñu ko réccu.

Giiñ naa ni su goney Afrig yépp awe ci yoon wi leen Séex Anta Jóob xàllal, ak lu mu yàgg yàgg yabeel gi dina deñi ba fàww.

Bubakar Bóris Jóob, Doomi Golo, Dakar, Éditions Papyrus Afrique, 2003, Pp 201-202.

III- Quelques axes de lecture

- Une discussion aux relents de confidences, de témoignages. Un intéressant échange sur une figure emblématique : Séex Anta Jóob

- Séex Anta Jóob ( 1922-1986), un leader exemplaire. La présentation de ses qualités. Un savant généreux, un homme de principes, altruiste, une vie consacrée à la défense des opprimés, des noirs, au discours mobilisateur, etc.

- Un hymne à l’estime de soi

29/08/2021

240047289 4393415867363061 4359409187335695364 n 1

Date de dernière mise à jour : dimanche 29 août 2021

Aucune note. Soyez le premier à attribuer une note !

Ajouter un commentaire