I- Présentation de l’auteur :
" Làmp Faal Kala, am ñu ko gën xam ci turu Ngoti Faal ( Ngoty Fall), doomi Lugala ju gane Àddina ci atum 1984. Moo ngi jànge ca iniwersite bu Ndar. Foofu la amee ca atum 2009 lijaasay Master ci Làkk, Mbind ak Mboor ñeel Afrig ca departmã Àngle. Boobaak léegi muy wéyal ay gëstoom ci fànn woowu ba doon ku ci am aw tur. Jaar na itam ci atum 2011 ca FASTEF ba daara ja ñuy tàggate jàngalekat yi ba am lijaasay CAES ji ko def ab jàngalekatu Àngale. Mu ngi dalee Alquraan ca Gànnaar. Waaye kenn mënul a tudd Làmp te tuddoo Seriñ Mustafa a Faati Kala, mi ko yar ca Luga, tàggat ko ci wàllu diine, def ci moom jikko yu rafet. "
II- Texte : SENEGAAL SUNU GAAL
Su nu ne géwaloo
Ńépp teew dajaloo
Toog taataan di dégloo
Waxtaane sunu gaal
Jamono bu soppikoo
Ba tee noo dajaloo
Péncoo ak a diisoo
Sànk nan sunu gaal
Njiit yi nuy sàmmloo
Su leen askan wi wóoloo
Goreleen bàyyi jiiroo
Jéem a aar sunu gaal
Lu waral nuy xëccoo
Ba mu jural nu noonoo
Sànk li nu daa damoo
Teraangay Senegaal
Nanu fexee juboo
Ànd bañ xiiroo
Ngalla bubu di ŋaayoo
Fàttee joow sunu gaal
Jot na nuy laamisoo
Masla tey defandoo
Ba tongook féewaloo
Jokkoo joow sunu gaal
Wolof ne wat gaal yëgoo
Liy sët nar a suturloo
Bunu di ko asaaloo
Day suuxal sunu gaal
Ngëneel ya maam daa sagoo
Buñu nu leen bàyyiloo
Leneen ñu nuy jàpploo
Lu gënul ci gii gaal
Cëy réew mee jaxasoo
Ndaw ñiy nuur ci am po
Tee noo jóg wattoondoo
Senegaal sunu gaal
Tubaab ya noo nuroo
Sàngara day sallañoo
Sinebaar jalaañoo
Di gàkkal sunu gaal
Ńii di dagg seen jëmm
Teg ci taal daldi wësëm
Togg jaay wutey dërëm
Bari na tey sunu gaal
Farañse Wiktoor Igoo
Tataa tàpp Tootoo
Du ci la nuy yokkoo
Moom sa réew sunu gaal
na bañkat yi laay woo
Ci làkki réew mig jokkoo
Nas leen caq ràngoo
Mooy taaral sunu gaal
Seefaa nuy toroxloo
Ci la njiit yiy sibooroo
Moo tee raŋ bi yëngoo
Ba nu joow sunu gaal
Làmp Faal Kala, Xelum xalam, EJO, 2020.
Quelques axes de lecture
- La poésie militante : Un hymne patriotique. Un appel à la cohésion nationale
- Le respect des valeurs traditionnelles.
- La question de la revalorisation des langues nationales
-Repérage et interprétation des figures de style : énumération, métaphore, allitération, assonance, etc.
- La structure du poème
Insistons sur :
Un quatrain est une strophe de quatre vers.
« Ngëneel ya maam daa sagoo
Buñu nu leen bàyyiloo
Leneen ñu nuy jàpploo
Lu gënul ci gii gaal »
Un huitain est une strophe de huit vers
« Nanu fexee juboo
Ànd bañ xiiroo
Ngalla bubu di ŋaayoo
Fàttee joow sunu gaal
Jot na nuy laamisoo
Masla tey defandoo
Ba tongook féewaloo
Jokkoo joow sunu gaal »
18/ 04 / 2021